Jënd aw dog
Nu muy deme
Dangeen a yor ag lijjanti walla liggéeyu kenn nit te ngeen bëgg a siiwal seen mandarga, man ngeen a jënd ay dog walla benn ci sunu podcast yi ci seen kem kàttan.
Bu ngeen jëndee aw dog, yéen ay xool ci fan lanuy defe fésal gi ci diirub waxtaan wi.
Pre Roll : Fésal yiy toll ci diggante 15 jàpp 30s, dinanu leen wane laataa nuy tàmbali walla bu nu ubbee waxtaan wi.
Mid Roll : Fésal yiy toll ci diggante 30 jàpp 60s, dinanu ko dugal ci biir waxtaanu dog wi.
Post Roll : Fésal yiy toll ci diggante 15 ak 30s, dinanu ko jàllale bu waxtaan wi jeexee.
NB : Ginnaaw bu ngeen jëndee dog wi, dinanu taxawu fésal gi méngale ko ak seen bëgg-bëgg ngir man a dabu seen i bànneex.
SUNUY XÉEWAL XALIS
- Dinanu méngale fésal gi ci dog wu nekk (Pre roll, Mid roll, Post roll)
- Dinanu dugal seen logo ak seen nataalu mandarga ci sunu denc yi.
Jënd jenn jamono
Nu muy deme
Dog yi danu leen a xaaj ci ay jamono, jenn jamono ju nekk man naa am 10i dog walla lu ko ëpp, boo jêndee nag jenn jamono dinanu séfal say liggéey wane sa mandarga ci dog yépp ci nekk ci jamono jooju.
NB : Xéewal yi danu koo dugal ci benn jënd bu nekk.
SUNUY XÉEWAL WURUS
- Dinanu def ay fésal yu méngoo ak seen bëgg-bëgg ci dog wu nekk…(Pre roll. Mid roll, Post roll)
- Dinanu dugal seen logo ak seen nataalu mandarga ci sunu denc yi
- Dinanu dugal seen logo ak seen nataalu mandarga ci jumtukaay yi
- Dinanu defar xëtu bolog ci sunu dal bi (site) ngir ñiy jënd dog yi