Ay leeral yu jëm ci sunu podcast
Sos nanu ko ci atum 2020 ci jamonoy Covid-19, Podcast Wolof Tech di ay ndaje yu nuy amal ngir xamal nit ñi xarala yu yees yi ñu man a jëfandikoo ci ku nekk biir Senegaal walla feneen.
Ngir matal sunu yéene jooju, jël nanu làkku wolof di ko jëfandikoo ci sunuy ndaje yi ndax lu toll ci 90% ci waa réew mi dégg nañu ko.
" Làkk warul a doon gàllangoor ci sàkku xam-xam. Xam-xam dëkkul fenn, amul melo amul làkk "
Lu waral podcast
Diglu ay podcast moo gën a gaaw ci xam lu bari xam gu wóor yenn bir yi dul jaar ci tele yi walla ci yeneen waxtaanukaay yi nu miin, dina tax a xam itam yeneen wëppa yu wuute.
Ginnaaw bu la jànganlee ba noppi xamaatal la lu bari bari ci tomb bi, podcast dina tax nga ubbeeku ci àddina bi ginnaaw ay seede yu sunu gan yi nuy dalal di def ci dog wu nekk.
Lu tax Wolof
Jàpp nanu ne Wolof làkk la wu nu man a jëfandikoo ngir jàngale ak tas ay xibaar ak itam manees nañu koo jëfandikoo ngir xam bu baax xarala yu yees yi.
Su fekkee ne ci Senegaal am na 54% yu jàngul, warul a tax nu fàtte ne ñooñu ñu yeewu lañu te dañuy xalaat, kon war nanu leen a jox ay jumtukaay ba noppi tekkil leen ko ci wolof.
Su fekkee ñépp xam nañu njariñ li nu xarala yu yees yi man a amal, kon ku nekk war naa fexe, ak lu mu man di liggéey xalaat ci teg ay pexe walla ànd ak ay ma-xereñ (experts) ngir man a suqali liggéeyam.
Lu tax nga war a diglu sunu podcast ?
Def nanu ci sunu liggéey bii yu bari yu am solo te am njariñ, danoo am bëgg-bëggu tasaare xam-xam
Njariñu waxtaan yi
Danuy amal ay waxtaan ci tomb yu lëntoon ci nit ñi, nu leeral ko ci wolof nu yomb ba mu leer.
Xamle ay jaar-jaar
Danuy dalal ay ma-xereñ (experts), ay jàngalekat ak ay lijjantikat ñu ñëw bokk ak nun seen xam-xam ak seen ay jaar-jaar.
Askan wi
Ñëwleen xamante ak mbooloo mu yaatu ci ñi nu bokkal gisiin te mooy fexe ba saa-senegaal yépp man a jot ci Tech.
Jàng ci saw làkk
Dinanu def ay niral ak ay nataal ci wolof ngir leeral nu yomb lu bari ci sunu waxtaani Tech yi
Ay jaar-jaar yu am solo yu jar a diglu
Ay jamonoy diglu yu neex yuy jàngale ci mumbaay mu neex ak sunu gan yi
Sax ci say reen ba noppi ubbiku
Boo xamee bu baax sa bopp ak fi nga dëkk ba noppi xam àddina, loolu dina tax sa jëm kanam man a yomb lool.
8
Jamono yi nu amal
+68
Jamono yi nu denc
+70
Gan ñi
+48K
Yiy wàcc
Ay leeral ci gan gi
Salaam ! Man la El Hadji Ibrahima DIAGO, ma-xereñ ci xam-xamu njëfekaay ak defar ay podcast di WolofTech.
Ayu-bis bu nekk ci dal bii ci booleem lënd gi, dinaa waxtaan ak yéen ci xarala yu yees yi jaare ko ci làkku
Ay ndaje yu 100% Tech yu nuy ànd ak ay ma-xereñ, ay jàngalekat ak ay lijjantikat ngir dimbali leen ci dëgëral seen xam-xam ngeen amaat yeneen xalaat yu yees ngir man a saafara jafe-jafe yi ngeen di taseel bis nu nekk.
Elib
Software engineer & Podcaster
“ Saa-senegaal yu bari am nañu muurum jàng, xam àddina ak yeneen yu bari, waaye am na ñeneen ñu amul muur moomu. Kon war na ci nun nu yaatal sunu xam-xam ak sunuy jaar-jaar ci xarala yu yees yi ak sunu bokki ma-réew yi ngir nu man a ànd tabax Senegaal gi gën. Tech mbirum ñépp la ! ”