Amal nanu ndaje yii ginnaaw sunuy jaar-jaar yu yàgg yu nu def ak Wolof tech.s
Podcast Wolof Tech
Wolof Tech nag podcast la buy wax ci xamtéef (informatique) ak jumtukaayu xarala yu yees yi jaare ko ci làkku wolof. Dog wu ci nekk dinanu ci waxtaane ab tomb ak sunu gan yi, ngir man caa génne lu nit ñi man a xam mu jariñ leen.
Jàpp nanu ne wolof làkku jàngale la ak waxtaan, man nanu cee jaarale ay xibaar ak itam xam xarala yu yees yi.
Noo ngi dund ci jamono joo xam ne day dox bu gaaw, kon nit ñi war nañoo jàng te xam ci nu gaaw, Podcast bu 5i simili bii nag loolu moo ko tax a jug. Muy ay dog yu gàtt yu 5i simili ci suba gi ngir man a dimbali ñiy diglu ñu man a dolliku xam-xam ak lenn ci xarala yu yees yi ci nu gaaw