Dinanu siiwal seen màndarga
Dangeen a yor ag lijjanti walla liggéeyu kenn nit, man ngeen a jënd sunu dog yi nuy amal ngir ngeen man cee fésal seen i liggéey walla seen um njaay ci diirub sunuy waxtaan.
Dinanu leen taxawu ba ngeen sos seen podcast
Su fekkee dangeen a am ay mébetu def ay podcast, man nanu leen a gunge ci seen yoon wi ba ngeen sottal ko. Danuy def ay tàggatu yu matale ci ni ñuy waajale ay dog ngir mu doon yu am solo ak ni ñuy jëfandikoo jumtukaayu xarala yi ba kàddu yi man a leer.